Mbay ak càmm

Cikaw gi

Mbay ci kaw gi

Nooraani bi ak yokutek nit ňi mooy wane ňaaka tolo yi ci taaxu Afrik ak tamit seen yaatuwaay.

Tabaxum taax yu gaaw ak nooraani bi moo tax nit ňidëk ci AFRIK daňoo yoku ba  ňetti yoon digente 1950 ak 1997, waye ňa ca taax yi moom daňoo yoku 11 yoon, juge ci 22 dem ci 250 ci ay milyoŋ doomu aadama. Wa mbotaayu xeet yi neenaňu nak filek 2020 ňaari nit yoo jël ken ka ci taxx yi lay dëk. Dëk bu ňuy wax kinshasa jall na ci 165000 juni ci ay nit dem ca 3.6 milyong ci ay nit; Abijan wala Dakar nak ňu ngi ëmb 25% wa reew ma yëpp.

Nooraani bu am doole: wutum ligey moo ci njëk, waye nak tax mi dafay jaxalaate ngir yu bees ya fay xew ak koom gafa am. Ca Lagos, ci at mi koom-koom  ga gëne am doole 2/3 yokute gi nooraan ma ko indi, Abijan nak xaaju nit ňa yëp yungi juddo ca yeeneen reew ndax rëdu dëk bi romb na Burkina Faso ak Maali.

Saytuk askanu Senegaal mungi ane gawaayukyokutek nit ňa ak terelin bu wissaaroo bimu ame.loolu moy leeral jafé-jafe yi.buňu gisé ni ňi ci ëp wa kaw ga laňu, terelinu askan wi ňu jële ci maam ya toloo wu lak li xel nagu ci jefëndikuk suuf si.mbay ùaa ngi gënna yoku filek taw ban gi gënna sakan; te 2/3 ci baykat yaa nga dëk ca saalum.maanaam ci gox yi gënna ňak  ndox.li gënna yennu maana moy ňu topale mbay mi ci digu reew mi ak ay ligey bu gënna mënna obu mbay mi ci gox yi ëpp ndox te nguur gi warko def.

Ci beneen waall tamit yokutek nit ňi dafay indi yeeneeni jafeň-jafeň ci wallu njang mi ak wutum ligey mi nga xamni moo gënna naxari saafara.saafara yooyu nak nooraani bi dakoy gënna nasaxal rek. Buňu waxe ni dafay gënna yoku xajarloo bi am ci dëk bi, dafay Gënna neewal doole wutum ligey bi.loolu mooy firndeel ni yokutek kaw gi, suxalik mbay mi ak yoku taxawaayu mbay mi mooy li gënna jamp ci ligey bi jemele kanam koom-koom bi.

Jem kanamuk xam xamu askan wi, xarala yi ňungi may doole bu bari li di ligey wu jëm ci askan wi ba nga xam ni gox yi daaňu doxal seen bop ci lu yag te dëgër. Ndax rafetaayu ligey likoy def mooy loxk askan wiwu ňu tagatt ci ay anamyu mucc ayib, loolo tax nak ňu wara jël aska&n woowule def ko tambalikaayuk doxum reew mi ca kanam. Looloy mënna doxal ligeyuk askan wi.

Suuf: Mbay nek tambalik yoku gi

(Nit ňi dëk ci kaw gi: 53.3%, toluwayam ci askan adina bi 154 ci 173 dëk ci teere bi PNUD biral ci atum 2006).

Teere bi Bank Monanjaal biralci atum 2008 nak mungi nan ňu gënna ligey ci mbay mi ci reew yu neew doole yi. Mungi ňaax reew yi ňu jublu ci wall woou def ko muy li njëk ci seeni ligey ngir ndool gi xaac bala 2015. Mbay nak bari ci numuy jëmale kanm askan wi, ci walu koom-koom, ci walu dundu gi, ak ci wallu baaxaayam ci gancax ji; looloo waral munek ap jumtukaay bu weet ci yokutek askan.

Mbay ak koom-koom

 Mbay mi mënna jappale koom-koomi reew mi, ci nimuy mënna xirtal nit ňi ci ňu ligey ci kawam ak nek li ëppsolo ci mbirum ligey ci kaw ga nga xam ni bayuňu. 2/3 koom-koomi reew yi ndool yëpp a ngi juge ci mbay. Ci reew yi nga xam ne mbay mooy seen jubluwaay nak, 29% ci seen kooma ngi juge ci mbay moomu,te yitt mungi ligey loo 65% ci doomu reew ma.industrie yi ligey ci mbay m tamit ňu ngi yoku ci 30% PIB wwu reew mi.mbay mi daf aam sololoo ndax dafay dëgaral dundu gi  ndax baykat yi ci yengu.amna solo lool ci lu tol ci 12 reew afrik sow jant yu am I lu tolook 200 miyoŋ ci ay nitt.reew yooyu nak a ngi jamarloo ak jamptek dund gi ak wute gi am ci ndimbal li.looloo warl ňu wara yok seen ligey ak taxawal seen njurr.

Mbay mi di liňuy suturloo

Xibaar yi nenaňu ni mbay maa dimbali nitt ňi si luňu suturloo ci lu tollni 86% doomu reew mi  ma ca kaw ga.mu ngi ligey loo 1.3 milyaar ci ay baykat yu ndaw yu mul suufte byit mungi atxawal  “aaral bi xalis ba di juge ca tool ya”. Su jamarloo ame ci tax ya, mooy daal li gënna dëger ci taxawayu kaw gi. 5.5 miyaar boo jël ci askanu reew yu ndool yi, 3 miyaar ya ,muy xaac ba, ňungi dundu ci kaw ga.xibaar yi taataan naňu ni tamit 2.5 miyaar yu ci nek ňu ngi yengu ci mbay te 1.5 miyaar yu ci nek tamit ay baykat yu ndaw laniu.

-- lu toll ci 75% wa adina baa ngi dëk ci kaw gi, 40% rek a ci jot ci dimbal liňu jaglel askan wu ndool li.

-- ci Afrik soow jant, dig ox wu sukandiku bu baax ci mbay mi, 4% dong la mbay moomule din taxawal ci li reew ma di gene ci alal wu jëm ci mbay suňu gisse ni limpo yi dafa taku lool ci wall woowu.

-- askan wi gënna ndoonak, yokutek PIB bi mooy bok ci 4 yoon ci li gënna tax ndool waňeekubu yokute boobu juge ci mbay.
Su mbay dull indi lu bari ci reew bum el ni senegal, nit ňu bari ňungi ci yengu (70% ci senegaalé yi ay baykat laňu wala ay càmm.muy firndel ni 10 miyon boo jël rek 7 ya ay baykat laňu.11 miyon boo jël tamit 5 ya ňu ngi dëk ca kaw ga.Ci 200 km yi ci dëk bi,80 mil yaa ngi jublu ci mbay mi Ak lu jege 60 mil ci càmm gi.

Mbay mi dafa di lu am solo lool ci koom gi,daňu ko wara suxali bu baax ci japale ňi ci yengu ci ay xarala ak jumtukaay ci ay doxaline.li ci jënk mooy fexe ba baykat yi mënna yokk seen jurr  wa ila ňu mëna sax dundu ci sen mbay.yokuk mbay mu andak càmm bu mucc ayi,ak siwalak ligey yu jëm ci walum sopi li juge ci mbay mimooy li gënna amsolo ci li suxali mbay moomule ci walu wergi yaram ak dundu gi.

Tanelak nekinu gune yi ak jigeen ňi nga xamni daňuy yengu bu baax ci wall woowu,daňu koy yoku ci ay jangale yu ňu leen di jagleel ci walu xarala  yu mujj yiak tass xibaar.

©1998-2024 E-TIC|system mcart|Updated: 2019-07-30 23:00 GMT|Privacy | RSS|